Ca la doomi Yanqóoba agsi, jóge ca tool ya. Ba ñu déggee la xew, dañoo am naqar wu réy, mer lool ndax gàcce, ga Sikem teg waa Israyil, ba mu tëddee doomu Yanqóoba ja, te loolu di lu defuwul.
TSK
TSK · Deuteronomy 22:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Waxal bànni Israyil ne leen: Muy bànni Israyil muy doxandéem ci Israyil, képp ku ci jël ciy doomam, jébbal tuur mi ñuy wax Moleg, dee rekk mooy àtteem. Na ko waa réew mi dóor ay doj, ba mu dee.
Ku ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee rekk mooy àtteem. Mbooloo mi mépp a ko wara dóor ay doj, ba mu dee. Muy doxandéem muy njuddu-ji-réew, ku ci ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee mooy àtteem.
Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Dee rekk mooy àtteb waa ji: dees koy génne dal bi, mbooloo mépp dóor koy xeer, ba mu dee.»
Yonent boobu nag mbaa boroom gént boobu, dee mooy àtteem, ndax moo woote ag fippu ci seen kaw Yàlla Aji Sax, ji leen jële ca réewum Misra, jote leen kërug njaam ga. Mu nar leena féle ci yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji sant ngeen doxe ko. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
nangeen génne ba ca buntu dëkk ba, waa ji, mbaa ndaw si def jooju jëf ju bon, te ngeen dóor ay doj, waa jooju mbaa ndaw si, ba mu dee.
te ngeen def ak moom, la mu naroona yóbbe ka mu sosal. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
¶ Bu ñu fekkee kuy tëdde ku am jëkkër; ka ko tëdde ak ka ñu tëdde, dee mooy seen àtte, ñoom ñaar ñépp, ngeen tenqee ko lu bon ci Israyil.
Ci yeen lay toog, ci seen biir, bérab ba mu taamu, ci benn bi ko gënal ci seeni dëkk, te buleen ko néewal doole.