¶ «Su ko defee ñoom dinañu tudd seen bàkkaar ak seen bàkkaaru maam ya, ndax dañu maa wor te dëkke maa noonoo,
TSK
TSK · Deuteronomy 30:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Seen Yàlla Aji Sax ji, soppeleen ko seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ak seen léppi doole.
Waaye bu ngeen walbatikoo ci man, sàmm samay santaane, di ko jëfe, bu ñu yóbbu woon seeni ñoñ ba fa suuf digalook asamaan sax, fa laa leen di jële, boole leen yóbbu ca bérab, ba ma taamoo dëël sama tur.”
Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk, ba duma rus.
Loolu yépp itam taxul Yuda workat bi, doomu ndeyu Israyil, délsee léppi xolam fi man, xanaa di jinigal rekk.» Kàddug Aji Sax jee.
Su boobaa ngeen sàkku ma, daj ma, ndegam sàkkoo ngeen ma seen léppi xol,
Nan càmbar, ba xoolaat jikko yi te dellu ci Aji Sax ji.
Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji. Moo nu xotat, te moo nuy wéral. Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.
«Terewul ba léegi,» kàddug Aji Sax jee, mu ne: «Délseeleen seen léppi xol ci man, boole kook koor aki jooy aki yuux.
Waaye saa su nit waññikoo ci Boroom bi, muuraay gi day muriku.