TSK

TSK · Deuteronomy 4:39

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yeen déy lañu won loolu lépp ngir ngeen xam ne Aji Sax ji doŋŋ mooy Yàlla, te jeneen yàlla amul, ju dul moom.

Xamleen boog ne seen Yàlla Aji Sax ji moom mooy Yàlla; mooy Yàlla ju dëggu jiy sàmm kóllëre ak ngor ñeel soppeem ñiy sàmm ay santaaneem, sët ba sëtaat, ba ci junniy maas.

¶ «Boroom bi, Aji Sax ji, Moo la tax di ku màgg! Kenn du yaw, kenn du Yàlla ku dul yaw doŋŋ, te mboolem lu nu nopp may, dëggal na loolu.

Te yaw sunu Yàlla, yaa ngi asamaan, di def lu la soob.

Aw yëkk xam na boroomam, mbaam-sëf xam gàmb, bi ko boroomam di xonte, waaye Israyil xamul, sama ñoñ ñii xàmmeewuñu.»

Yeen sama ñoñ, yeenay samay seede. Kàddug Aji Sax jee. Yeenay sama jaam bi ma taamu, ngir ngeen xam, ba gëm ma, ba ràññee ne maay moom. Sàkkeesul yàlla ju ma jiitu, mbaa ju may wuutuji.

Hosea 7:2 TSK

Taxul ñu jàpp ci seenum xel ne seen mboolem jëf ju bon laa bàyyi xel. Léegi seeni jëf a leen wër ndombo, ne màkk fi sama kanam.