Jaamuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji, ma barkeel seen dugub ak seen ndox, boole ci jële wopp ci seen biir.
TSK
TSK · Deuteronomy 6:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Waaye céy bu ñu amoon boobu xol ngir ragal ma, di sàmm sama santaane yépp bés bu nekk, ba tax ñu baaxle, ñoom ak seen askan, ba fàww!
¶ Léegi nag yeen Israyil, ana lu leen seen Yàlla Aji Sax ji laaj, lu moy ngeen ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di doxe mboolemi yoonam, sopp ko, di jaamoo seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan,
buleen déglu waxu yonent boobu, mbaa boroom gént boobu, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di nattu ngir xam ndax yeena ngi koy soppe seen léppi xol ak seen léppi bakkan.
Ku siblu, mu sib, ku ragal Yàlla, mu teral. Mooy sàmm ngiñam, su ko dee lor it.
Giñ naa ko ci man mii, sama gémmiñ njekk a ciy jibe, di kàddu gu dul randu. Man la ñépp di sukkal seen bëti óom, man it la bépp boroom làmmiñ di giñe.
xanaa di waate Aji Sax jiy dund, ci dëgg ak njub ak ngor, kon xeet yi di barkeeloo Aji Sax ji, di ko sagoo.»
«Yerusalem, ana lu tax ma di la baal, te say doom wacc ma, di giñe lu dul Yàlla. Ma reggal leen, teewul ñuy njaaloo, riixle, jëm kër gànc ya!