Ana kuy dund ba fàww, ba doo gis bàmmeel?
TSK
TSK · Ecclesiastes 2:14
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ku ñaw day xelu, xam li muy def; ab dof di nax boppam.
Dogalu doom aadama ji ak dogalu mala mi, benn dogal bee; ni kii di deeye la kee di deeye, genn noo gee, nu bokk ko. Lu nit ëpplee mala neen na, ñoom ñépp, cóolóoli neen.
Ana lu boroom xel ëpplee ku dofe? Nga ñàkk, xam doxalin, lu mu lay jariñ?
Ana ku rafet xel nu muy mel? Ana ku xam piri? Am xel rafet, kanam leer, gëna lewet.
Ñépp a bokk benn dogal bi, ku jub ak ku bon, ku baax ak ku set, ak ku sobewu; kuy sarxal ak ku dul sarxal, muy ku baax ki, di bàkkaarkat bi, muy kiy giñ, di ki ragal ngiñ.
Ma seetlooti fi kaw suuf ne du ku gaaw, yaay raw; du ku jàmbaare, yaa moom xare; du ku xelu, am loo dunde; du ku muus, duunle; du kuy xamkat, amu yiw; ku nekk ak bésam ak wërsëgam.
Xelu, jubal; dofe, jàdd.