TSK

TSK · Ecclesiastes 7:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 11:10 TSK

Su dikkee, tëj nit, woo ko péncum àtte, ku ci man dara?

Job 34:29 TSK

Bu Yàlla nee cell, ana ku koy ŋàññ? Bu làqee kanamam, ana ku koy niir? Xeet yeek nit ñi la boole tiim,

Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp, feeñal nga ca sa kàttan, bañaaleek feyukat ne xerem.

Lu wañaaru, maneesu koo jubbanti; lu teewul, maneesu koo lim.

Xalam yaak tabala yaak toxoro ya jolli, biiñ xelli ca xawaare ja. Seetluwuñu sax li Aji Sax ji def, xooluñu li mu jo loxoom.

maa masa doon kenn ki, te sama loxo, maneesu cee musle. Su ma defee, kuy dindi?

Ndax kat moo noon Musaa: «Maay yërëm ku ma neex, te maay ñeewante ku ma neex.»

Ci moom lanu jote sunu muur ci kaw dogalu Yàlla mi nu taamu lu jiitu, moom miy sottal lépp ni mu ko namme ci coobareem.