TSK

TSK · Ecclesiastes 9:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

ma giñloo la ci Aji Sax jiy Yàllay asamaan ak suuf ne doo jëlal sama doom soxna ci biir jigéeni waa Kanaan, gi ma dëkk ci seen biir.

Job 9:22 TSK

Lépp benn la rekk! Moo tax ma ne: «Ku mucc ayib ak ku bon lay boole fàkkas.»

Job 21:26 TSK

te ñooy tëddandoo biir suuf, bokk sàngooy sax.

Ku xelu day xool fa muy jaare, dof biy tëñëx-tëñëxi cig lëndëm. Ma ne moona ñoom ñaar a bokk dogal moos.

bu dundoon junniy junniy at sax te amul jàmm. Xanaa du benn bérab la ñépp jëm?

Moo sàggane ngiñ, moo wor kàddu ga mu fasante woon. Mu ngoog, moo joxe kàddoom, ba noppi walbatiku def lii lépp. Du mucc mukk.

«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante ku jub ak ku bon, kuy jaamu Yàlla, ak ku ko jaamuwul.