TSK

TSK · Esther 3:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba loolu amee Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Bindal lii xew cib téere, muy pàttli, te nga xamal Yosuwe ne ko, raafal laay def askanu Amaleg, ba ñu jeex tàkk, ba deesatu leen fàttliku fu asamaan tiim.»

Bu ngeen demee ba seen Yàlla Aji Sax ji noppal leen ci mboolem seen noon yi séq réew, mi mu leen sédd, ngir ngeen nangu ko, nangeen far mboolem lu ñu doon fàttlikoo Amalegeen ñi fu asamaan tiim. Buleen ko fàtte.

¶ Fekk na jenn waayi Yawut a ngi ci Sus, péey ba. Ma nga tudd Mardose. Yayir di baayam. Yayir, Simey ay baayam. Simey, Kis ay baayam, bokk ci giirug Beñamin.

¶ Jamono yooyu Mardose amee ndombol tànk ca buntu kër buur, ku ñuy wax Bigtan ak ku ñuy wax Teres, di ñaari fara buntu kër buur, ñoo am lu ñu meree lool Buur Aserus, bay lal pexe mu ñu ko bóome.

Yeneen jawriñi buur ya ca buntu kër buur wax Mardose ne ko: «Ana lu waral ngay gàntal santaane Buur?»

¶ Aman a ngay génn di dem, bésub keroog ànd ak mbégte, xol bay neex. Ba mu gisee Mardose ca buntu kër buur nag, te Mardose jógul, amul benn tiitaange ci moom, daa mer ba fees dell.

Ci biir loolu Dañeel ñaan Buur mu tabb Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, ñu yore saytub diiwaanu Babilon. Dañeel moom nekk ca ëttu buur.