Su ko defee ngeen mana nettali seeni doom ak seeni sët ni ma torxale waa Misra, ak sama firnde, yi ma def fi seen biir, ndax ngeen xam ne man maay Aji Sax ji.»
TSK
TSK · Exodus 13:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Exodus 10:2
TSK
Exodus 12:27
TSK
waxleen leen ne leen: “Loolu sarax la ñeel Aji Sax ji ngir bésub Mucc ba, ndax la mu teggi woon këri bànni Israyil ca Misra, kera ba muy fàdd waa Misra te musal ca sunuy kër.”» Ba mu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma sujjóot, màggal Yàlla.
Deuteronomy 4:9
TSK
¶ Waaye wattuleen, wattuleen seen bopp bu baax, bala ngeena fàtte mbir yi ngeen teg seen bët, ba du génn seenum xel seen giiru dund gépp. Te nangeen ko xamal seeni doom ak seeni sët.
Psalms 78:3
TSK
muy lu nu dégg, xam ko, sunuy maam xamal nu ko.
Ephesians 6:4
TSK
¶ Yeen ñiy baay it, buleen xoñoñal xale yi, waaye yarleen leen, di leen jubanti, di leen xamal coobarey Boroom bi.