TSK

TSK · Exodus 18:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Firawna nag ne Musaa: «Neel mott! Bul fexe ba taxawati sama kanam! Ndax bés boo jàkkaarlooteek man, kera ngay dee.»

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettlee ci mboolem noonam, xettli ko it ci Buur Sóol. Kàdduy woy yaa ngii.

Kañleen Aji Sax ji, ànd ceek man, nu bokk wormaal turam.

Waaye Boroom bi Aji Sax jee may dimbali, ba tax rusuma. Moo ma taxa dogu ba dëgër, ngir xam naa ne deesu ma rusloo.

¶ Naka la xelum Piyeer délsi, mu daldi ne: «Léegi nag xam naa xéll ne, Boroom bee yebal malaakaam, te moo ma musal ci loxol Erodd, ak mboolem li Yawut yi séentu woon.»

Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.