Naka la siggi, gis ñetti nit, ñu ne jimeet ci kanamam. Ibraayma gaawtu, gatandu leen, sujjóotal leen.
TSK
TSK · Exodus 18:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba Laban déggee ne jarbaatam Yanqóoba ñëw na, dafa daw gatandu ko, taf ko ci boppam, fóon ko, yóbbu ko kër ga. Ba Yanqóoba nettalee Laban lépp,
Moom ci boppam nag, mu jiitu leen, wutali magam, di dox tey sujjóot, ba muy juróom ñaari yoon.
Magam ña itam, mu fóon leen tey jooy. Booba la magi Yuusufa ya doora wax ak moom.
¶ Ba loolu amee Balag dégg ne Balaam a ngay ñëw, mu gatanduji ko ca dëkku Mowab, ba digalook dexu Arnon, ca catu réew ma.
Fukki dogi formaas yii, yóbbul ko seen njiitu kurél. Nemmikul seen jàmmu yaram te nga sàkku ci seen firnde, indil ma.
Ba Uri dikkee, Daawuda nuyook moom ne ko: «Mbaa Yowab jàmm? Mbaa mbooloo ma jàmm? Mbaa xare ba jàmm?»
Sujjóotal-leen doom ji, bala moo mer, ngeen sànkoo seenu yoon; meram day jekki ne jippét, waaye ndokklee képp ku ko làqoo!
Ba loolu amee ñépp jooyoo jooy yu metti, laxasu ko, fóon ko.