TSK

TSK · Exodus 20:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam.

¶ «Waaye nag, su nit fexeelee moroomam, nax ko, ba rey ko, su làqoo woon sama sarxalukaay sax, jàppleen ko, rey.

Su fekkee ne nag wi da daan dañe, ñu yégaloon ko boroom, wattuwu ko, ba nag wi rey góor mbaa jigéen, dóorleen nag wi ay xeer, ba mu dee, te teg ci rey boroom nag wi.

¶ «Su dee ag weñ la ko dóor, mu dee, moo ko rey, te dee rekk mooy àtteb ki rey.

¶ Su fekkee ne nit ki dafa bañ moroomam, su ko tëroo, dal ci kawam, ba fàdd ko, mu dee, su làqujee ci dëkk yooyu benn,

¶ Te it deretu nit ñu deful dara la Manase tuur, ba mu fees Yerusalem dell, cat ba cat, te bokkul ak bàkkaar bi mu bàkkaarloo waa Yuda, ba ñuy def li Aji Sax ji ñaawlu.

Day tëroo ciy dëkk-dëkkaan, làqu di bóom ku deful dara, nëbbu di wootal néew-ji-doole.

Ñii kat seen bopp lañuy fiir, seen bakkanu bopp lañu sànk.

Xamleen xéll rekk ne su ngeen ma reyee, bakkanu ku deful dara ngeen gàddu, yeen ak dëkk beek ñi ko dëkke, ndax ci lu wér Aji Sax jee ma yebal ci yeen, ngir ma yegge leen mboolem kàddu yii.»

Acts 28:4 TSK

Waa réew ma gis jaan ja langaamoo loxol Póol, ñu naan ca seen biir: «Nit kii kay ab bóomkat lay doon, ndegam moo rëcce géej, te taxul Ndogal may ko mu dund.»

ak ñeetaane, ak màndite, ak mbumbaay, ak yeneen yu ni mel. Ma àrtu leen nag na ma leen artoo woon, ñiy jëfe noonu, amuñu cér ci nguurug Yàlla.

Ndax ki ne: «Bul jaaloo,» moo ne itam: «Bul bóome.» Ku jaaloowul te bóome nag, xëtt na yoon.