TSK

TSK · Exodus 20:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Isaaxa ne doomam: «Moo doom! Noo def, ba gaawa jàpp nii?» Yanqóoba ne ko: «Aji Sax jiy sa Yàlla, moo ma ko jagleel.»

¶ «Buleen tudd seen turu Yàlla Aji Sax ji ci neen, ndax Aji Sax ji du ñàkka topp kuy tudd aw turam ci neen.

Waaye yaw de, bu ko ñàkka topp, ndax boroom xel nga, te dinga xam ni ngay defeek moom, ba mu sangoo deretam, ànd ak bijjaawam, dugg bàmmeel.»

lu ko moy ma regg, weddi la, ba naan: «Kuy Aji Sax ji?» Mbaa ma ñàkk bay sàcc, di la ñàkke worma, yaw sama Yàlla.

«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

¶ Man nag seedey Yàlla laa ciy sàkku, giñ naa ko ci sama bakkan, bañ leena yokku naqar moo tax délsiwuma Korent.

¶ Li ci raw nag bokk yi, moo di buleen giñ, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu mana doon. Na seen waaw di waaw, seen déet di déet, bala ngeena tàbbi ci mbugal.