TSK

TSK · Exodus 21:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Esawu ne: «Moom kay moo yey tudd Yanqóoba, ndax suufu na ma ñaari yoon. Sama céru taaw la jëkka nangu, tey mu nangooti sama ñaanu baay.» Mu teg ca ne: «Ndax desalaloo ma ag ñaan?»

¶ «Su dee ku sàcc mala, muy nag mbaa mbaam mbaa ab gàtt, te ñu fekk ko ciy loxoom, muy dund, na fey ñaaram.

Su fekkee ne jotaatuñu ko ci jotin yooyu sax, war naa moom boppam mooki doomam ca atum Yiwiku ma.

¶ Su fekkee ne seen mbokkum bànni Israyil, góor mbaa jigéen da leena jaay boppam, bu leen liggéeyalee juróom benni at, atum juróom ñaareel ma, yiwileen ko, mu moom boppam.

Musaa sant leen, ne leen: «Njeexital juróom ñaareelu at mu nekk, àppook atum njéggalug bor, ci diiru màggalu Mbaar yi,

¶ Ci biir loolu askan waak seeni jabar di xultu lool ci seen kaw bokki Yawut.

¶ Kàddu gii dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo ci Aji Sax ji, gannaaw ba Buur Cedesyas fasook mboolem waa Yerusalem ngir goreel jaam yi,

“Saa yu ngeen waññee juróom benni at ba ca catal juróom ñaareel ma, na ku nekk ci yeen goreel mbokkum Ebraam mu ko jaayoon boppam. Gannaaw bu ko liggéeyalee juróom benni at, na ko goreel, mu tàggook moom, daldi moom boppam. Waaye seeni maam déggaluñu ma, teewluwñu ma.

ndax dees leena jot, ba fey njég ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.