TSK

TSK · Exodus 22:28

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

nangeen sédde Aji Sax ji lépp lu jëkka juddu, rendil ko ko: lépp luy góor lu seen jur taawloo, Aji Sax jeey boroom.

Saa yu ay nit jotee ci mbirum nag mbaa mbaam mbaa gàtt mbaa yére, mbaa lu réer lu mu doon, ñaar ñi solowoo alal ji, muy mala mbaa leneen, nañu yóbbu mbir mi fi kanam àttekat yi. Ku ci àttekat yi teg tooñ, na fey moroom mi ñaari yoon.

¶ «Ngëneeli meññeef ma jëkka ñore ca seen suuf, moom ngeen di yóbbu seen kër Yàlla Aji Sax ji. «Ab tef, buleen ko togge soowum yaayam.

Ba loolu amee fitu Daawuda ne tërit ndax la mu dagg ca lafu mbubbum Sóol.

Daawuda ne Abisay: «Bu ko rey. Ana kuy yékkati loxoom ci kaw ki Aji Sax ji fal, te yoon dabu ko?»

Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. Yàlla toog na, di jiite ndajem boppam, di àtte ndawi péncam, naan:

Sam xel sax bu ca saaga buur, sa néegu biir sax, bu fa saagaa boroom daraja. Xamoo picc muy yóbbu sa kàddu, mbaa njanaaw luy siiwali mbir ma.

Acts 23:3 TSK

Póol ne ko: «Fél la yaw, moom la Yàlla di waaj, jinigalkat bee, mbete miir bu ñu weexal! Yaa ngi toog, topp yoon, di ma àtte, te teewul nga xëtt yoon, di ma dóorlu!»

Moo tax kuy bañal njiit, tëralinu Yàlla nga bañal, te ñi bañal njiit, ñoo wool seen bopp mbugal.

Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragal-leen ko; te buur, teral leen ko.

Jude 1:8 TSK

¶ Géntkat yii itam noonu rekk lañuy sobeele seen yaramu bopp, boole ci di sofental kilifteef, ak di saaga boroom daraja ya fa asamaan.