¶ «Buleen siiwal ay fen; buleen lëngoo ak tooñkat, ngir doon seedeb naaféqam.
TSK
TSK · Exodus 23:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Buleen sàcc, buleen fen te buleen di worante.
¶ Ñu neeti: «Alku ñeel na ku nangub ger, ngir rotal bakkanu nit ku deful dara.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!»
Ñii dañoo mànkoo, di tëru ku jub, di teg àtteb dee ku deful dara.
Ab soxor mbugalam du jaas, wóor na; te ku jub, saw askan mucc.
Wóoy ngalla ñiy gis lu bon, ne lu baax la; gis lu baax, ne lu bon la; lëndëm, ñu tudde leer, leer, ñu tudde lëndëm; lu wex, ñu ne neex na lu neex, ñu ne wex na.
Aji Sax ji la mer ma diib, doole ja bare; te du ñàkka topp ku tooñ, ag tooñaangeem. Aji Sax jeey daagoo biir callweer ak ngëlén, niir yi di pëndub tànkam.
¶ Sànjum Yàlla fa asamaan lay dale feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi, ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.
¶ Kon nag bàyyileen fen, te ku nekk di wax sa moroom, dëgg, ndax ku nekk ci yeen sab céru moroom nga.