TSK

TSK · Exodus 29:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Sàkkal mbalkam njàpp mu xànjar, ak tegub xànjaram ngir ñu di ko jàppe. Teg ko ci diggante xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, te nga duy ko ndox.

¶ «Indil Aaróona aki doomam ba ci bunt xaymab ndaje mi, nga sang leen ci ndox mi.

ndax bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, ak bu ñuy jegeji sarxalukaay bi, dañuy jàpp, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

Musaa wax mbooloo ma ne leen: «Lii may waaj la Aji Sax ji santaane woon ñu def ko.»

Indil Leween ñi ci kanam xaymab ndaje mi, te nga dajale mbooloom bànni Israyil mépp.

Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.

Moo defal loolu mbooloo mi ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko.

Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu, ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.

tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,