TSK

TSK · Exodus 29:40

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ñu jàpp ne andaar, boo ci amee fukk, mooy benn efa.

«Li Aaróona aki doomam yu góor di sarxalal Aji Sax ji, keroog bu ñu koy diw, fal ko, mooy lii: ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, tollook saraxu pepp bi ñu saxoo bés bu nekk, te genn-wàll gi di suba, genn-wàll gi ngoon.

¶ «Elasar doomu Aaróona sarxalkat bi nag, ab saytoom moo di diwu làmp bi, ak cuuraay li, ak saraxu pepp bi dul jaas, ak diwu pal gi. Mooy féetewoo jaamookaay bi bépp, ak mboolem li ci biiram, ba ci yëf yu sell yi, aki jumtukaayam.»

¶ «Kiy sarxal Aji Sax ji ab saraxam, na sarxewaale saraxu pepp bu benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, su ñu xiiwe ñeenteelu xaajub xiinu diw, di liitar ak genn-wàll,

ak biiñ ngir saraxu tuuru, ñetteelu xaajub xiin, di ñaari liitar. Na joxe loolu, def ko xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

su dee moy gu dul teyeef, te mbooloo mi yégu ko woon, su boobaa mbooloo mépp ay sarxal aw yëkk wu ndaw wuy doon rendi-dóomal, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ak saraxu peppam, ak saraxu tuuroom, ni ko yoon àttee, ak benn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar.

Loolooy saraxu rendi-dóomalu bésub Noflaay, ci bésub Noflaay bu nekk, te bokkewul ak dóomal bi war bés bu nekk, te ànd ak saraxu tuuram.

Sarax yu mel noonu ngeen di sarxal ci bés bi, ak seen saraxu tuuru, diiru juróom ñaari fan, muy ñamu saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. Ci kaw rendi-dóomal bi war bés bu nekk, ci lees koy dolli.

Ñi lekk seen nebboni sarax, naan biiñ bi ñu leen di tuural kay, nañu jóg, boog, xettli leen, di seen kiiraay!

Sa ndoxum naan it dees koy natt, mu tollook benn liitar bés bu nekk.

Li war ki tooge jal bi, saraxu rendi-dóomal ci la, ak saraxu pepp, ak saraxi biiñ yi ñuy joxe bésu màggal, yu mel ni màggali Terutel weer ak bési Noflaay, ak yeneen bés yu bànni Israyil taamoo daje. Moom it mooy joxe saraxu póotum bàkkaar, ak saraxu pepp, ak saraxu rendi-dóomal, ak saraxu cant ci biir jàmm ngir njotlaayal waa kër Israyil.

Saraxu pepp biy ànd ak kuuy mi benn efa lay doon, di fukki kiloy pepp ak juróom, ak dayob pepp bu mu àttan buy ànd ak xar yu ndaw yi ak xiinu diw, yemook ñetti liitari diw ak genn-wàll ci efab pepp bu nekk.

¶ «Su dee bési màggal ak bési ndaje yi, saraxu pepp mi benn efa lay doon ngir yëkk wi, yemook fukki kilook juróom, ak benn efa ngir kuuy mi, ak dayo bu ñu àttan ngir xar yu ndaw yi, efab pepp bu ne ànd ak benn xiinu diw, di ñetti liitar ak genn-wàll.

Joel 1:9 TSK

Saraxu pepp ak saraxu tuuru dagg na ca kër Aji Sax ji. Sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, ñu ngi ñaawlu.

Joel 2:14 TSK

Jombul mu dëpp, fomm, bàyyi gannaawam barke, ba ci saraxu pepp ak saraxu tuuru, ñeel seen Yàlla, Aji Sax ji.»