TSK

TSK · Exodus 3:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Waaye waa réew moomu leen di def ay jaam, dinaa leen àtte. Gannaaw loolu sa askan dina ca génn, ànd ak alal ju bare.

Kon nag waxal bànni Israyil ne leen: Man maay Aji Sax ji. Maa leen di sippil, yeen bànni Israyil, li leen waa Misra sëf, te maa leen di teggil njaam, gi ñu leen teg. Maay tàllal sama loxo, dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel leen.

Nëgëni tey doon naa xàcci sama loxo xaat, dumaa leen mbas mu leen di fare ci kaw suuf, yaw yaak sa waa réew.

Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees.

Ñu daldi lakk mburu mu tàppandaar ca xiiw wu amul lawiir, wa ñu jële Misra. La taxoon xiiw wa ñàkk lawiir mooy dañu leena dàqe Misra, ba taluñu woona fàggu lu ñu lekk.

Aji Sax jee nu defal ay firnde, ak kéemaan yu mag te metti ci kaw Misra ak ci kaw Firawna ak ci kaw waa këram gépp, nu teg ci sunuy gët.

ñu sottal ci seen biir firndeem ya mu waxoon, muy kéemaan ya ñu def ca réewum Xam.

Mooy kéemaan ya fa réewum Xam, kiraama ya ca géeju Barax ya.

Aji Sax jeey duma Misra duma yu ànd akum paj, ñu walbatiku ci Aji Sax ji, mu nangul leen, faj leen.

Yaa def ay firnde aki kéemaan ca réewum Misra, di ko def ba tey jii ci Israyil, ak ci doom aadama yépp, ba may sa bopp woy wu réy wi nga am tey jii.

Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, sama dooley loxo ak sama kàttanu përëg, ak sànj mu naan soteet laay nguuroo ci seen kaw.

Acts 7:36 TSK

Moo leen génne réewum Misra, moo def ay kéemaan aki firnde ca réew ma, ak ca géeju Barax ya, ak ca màndiŋ ma, diiru ñeent fukki at.