Musaa taxaw ca buntu dal ba, ne: «Ku ànd ak Aji Sax ji, fii ci man!» Leween ñépp dikk, yéew ko.
TSK
TSK · Exodus 32:27
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Musaa ne àttekati Israyil: «Na ku nekk ci yeen rey nitam ñi taqook Baal Pewor.»
Yonent boobu nag mbaa boroom gént boobu, dee mooy àtteem, ndax moo woote ag fippu ci seen kaw Yàlla Aji Sax, ji leen jële ca réewum Misra, jote leen kërug njaam ga. Mu nar leena féle ci yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji sant ngeen doxe ko. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
¶ Lewi la wax ne ko: Sa Tumim ak sa Urim, jumtukaayi tegtal ya, ñeel na góor gay sa wóllëre, yaa ko nattoo ca Maasa, joteek moom ca ndoxum Meriba.
Ba loolu wéyee mu wax ak ña ca des, may dégg. Mu ne leen: «Toppleen ko ca biir dëkk ba te ngeen rey. Buleen xool bëti ñéeblu, buleen ñeewante.
¶ Kon nag gannaaw-si-tey, ni nitu suuxu neen di xoole moroomam, nun xooleetunu ko kenn. Doonte ni nitu suuxu neen lanu xoole woon Almasi, léegi xooleetunu ko noonu.