Bàkkaaru doomi Eli yi réyoon na lool fi kanam Aji Sax ji, ndax dañu daan teddadil saraxu Aji Sax ji.
TSK
TSK · Exodus 32:30
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba loolu wéyee mbooloo ma mépp ne Samiyel: «Ngalla sang bi, ñaanal nu ci sa Yàlla Aji Sax ji, nu baña dee, ndax la nu bàkkaaroon lépp, yokkati nanu ci mbon gu tollu ni di sàkku buur.»
Man nag, yàlla tere may tooñ Aji Sax ji, di leen noppee ñaanal. Te it dinaa leen won yoon wi baax te jub:
Jombul Aji Sax ji gis sama naqar, ba feye ma aw yiw saagay kii tey.»
¶ Gannaaw ba Aji Sax ji waxee Ayóoba yooyu kàddu, Aji Sax ji dafa wax Elifas ma cosaanoo Teman, ne ko: «Sama xol tàng na ci yaw, yaak sa ñaari xarit yi, ndax waxuleen dëgg ci man ni sama jaam bi Ayóoba waxe.
Jombul Yàlla dëpp ba fomm, daldi dëddu tàngooru meram, ba dunu sànku.»
Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la;
¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, doole lay dale.