TSK

TSK · Exodus 34:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Waaye maay baaxe ñi ma sopp, di sàmm samay santaane, ba ci junniy maas ya leen di wuutuji.

Bàyyileen ko xel bu baax, déggal ko te bañ koo merloo, ndax du leen baal seen moy, ngir sama tur la taxawe.

Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.

Ma ne: «Éy Aji Sax ji, yaw Yàlla Boroom asamaan, Yàlla ju màgg ji te raglu, di sàmm kóllëreek ngor, ñeel ñi la sopp tey topp say santaane.

Job 10:14 TSK

ne ma dann, ba su ma bàkkaaree, doo ma baal samag tooñ.

Aji Sax ji day seetlu ku jub; ku soxor, bëgg fitna, mu bañ.

Balaa seen cin a yég tàngooru gajj, muy gu tooy, muy guy boy, yal na leen fekk sànku.

Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon, di seen Yàlla ju leen di baal, te di leen mbugale seeni jëf ju bon.

Yal na Aji Sax ji bàyyi xel ñaawtéefi maamam. Yàlla bu bàkkaaru ndeyam faru.

Moo fàdd taawi Misra yu góor ya, Kee saxoo ngoram!

Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!

Yaw miy jëfe ngor sa digg ak junniy maas, te bu baay ñaawee, nga topp ko ko, ba ci doomam. Yaay Yàlla ju màgg ji te jàmbaare. Yaa di Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi,

Boroom bi sunu Yàlla, yaay Boroom yërmandeek njéggal moos, ndax gàntal nanu la.

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.

Nahum 1:6 TSK

Bu sànjoo, ana kuy taxaw? Ana kuy dékku tàngooru meram? Am sànjam a naan soteet ni sawara, doj yi rajaxoo fi kanamam.

Luke 7:42 TSK

Waaye ñoom ñaar ñépp, kenn manu cee fey. Mu far jéggal leen ñoom ñépp. Ana kan ci ñaar ñooñu nag moo ciy gëna fonk leblekat bi?»

Acts 5:31 TSK

Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.

Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy, akug jéllaleem, akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?

Mu ne: «Mbégte ñeel na ñi ñu jéggal seeni tooñ, ñeel na ñooñu ñu baal seeni bàkkaar.

¶ Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,

ndax kat «sunu Yàlla, sawara wuy xoyome la.»

Képp ku ñu gisul ñu bind la ci téereb dund bi, ci déegu sawara si lees la sànni.