TSK

TSK · Exodus 4:22

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Léegi nag su ngeen ma déggalee bu baax, di sàmm sama kóllëre ak yeen, yeenay doon sama moomeelu bopp ci mboolem askan yi. Dëgg la, àddina wërngal këpp maay Boroom,

Aji Sax ji lañuy feye lii? Ndaw xeet wu dofe te ñàkk xel! Mooy seen baay, bind leen, sàkk leen, samp leen.

Éy Aji Sax ji, bul mer lool, bul ba xel fàww ci ñaawtéef. Ngalla seetal ne nooy sa ñoñ, nun ñépp.

Ñooy dikk di jooy, di leewaayu, ma jiite leen, yóbbu, jaare leen xàll wu jub wu ñu dul fakktaloo, ba ca wali ndox ya, ngir maay baayu Israyil, Efrayim di sama taaw.

«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”

Maay doon seen baay, ngeen di samay doom, góor, ak jigéen,» la Boroom bi, Aji Man ji wax.

Moom la soob mu jure nu kàddug dëgg, ba nu taxawe ab jooxeb ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.