TSK

TSK · Exodus 4:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk.

¶ Foofa Aji Sax ji feeñu ko fa ne ko: «Bul dem Misra, waaye nanga toog ci réew mi ma lay wax.

Mu teg ca ne: «Man maay sa Yàllay baay, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba.» Ca la Musaa nëbb kanam ga, ndax ragala xool Yàlla.

Demal woo magi Israyil, ñu daje, nga ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, moo ma feeñu, ne ma: ‘Gis naa leen, te yég naa li ñu leen di teg ci Misra.

¶ Gannaaw loolu Musaa dellu wax Aji Sax ji ne ko: «Waaw, su ñu ma dégluwul te gëmuñu ma, xanaa ne ma: “Aji Sax ji feeñuwu la” nag?»

¶ Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Ma ne, dinaa yiiroo niir wu fatt, dikk ba agsi fi yaw, ngir bu may wax ak yaw, mbooloo mi di ci dégg, ndax ñu wóolu la ba fàww.» Ba loolu amee Musaa baamtul Aji Sax ji tontal mbooloo ma.

Samaree yilif Efrayim, te doomu Remalya ji yiliful lu moy Samari. Dungeen mana saxoo dëgër nag, ndare ngeen sax ci Aji Sax ji.”»