TSK

TSK · Exodus 40:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel bànni Israyil.

Wewal rido bi ci ron lonku yi, su ko defee nga yóbbu gaalu àlluway seede si foofu ci gannaaw rido bi, rido bi xàjjaleel leen bérab bu sell bi, ak bérab bu sell bee sell.

¶ Musaa dellu wax ak mbooloom bànni Israyil mépp ne leen: «Lii mooy li Aji Sax ji santaane.

¶ Ñu sàkk itam rido bi, ràbbe ko wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñawaale ci ay nataali serub.

¶ Noonu la mboolem liggéeyu màkkaanu xaymab ndaje mi mate. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa rekk, ni la ko bànni Israyil defe.

Na sàkk ci deretu yëkk wi, wis-wisale ko baaraamam ci kaw kubeeru gaal gi, ci wetam gi féete penku, te it na wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kanam kubeeru gaal gi.

¶ Ci kaw loolu néeg Yàlla bi ci asamaan ubbiku, gaalu kóllëreg Yàlla ga di feeñ ca biir màkkaanam ma, melax ya tàkk, kàddu yaak dënu ya riir, suuf sa yëngu, tawu doji yuur bu metti daldi sóob.