Genesis 13:18
TSK
¶ Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay.
Ibraayma nag tudde bérab boobu Yawe Yire (mu firi Aji Sax ji dina dikk). Moo tax ñuy wax ba tey, naan: «Aji Sax jaa ngay dikke ca tundam.»
Yàlla neeti ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Giiral te yokku, ba aw askan ak mboolooy askan sosoo ci yaw, te ay buur askanoo ci sa geño.
Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israyil ne leen: “Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”»
Yal nañu rus, jàq ba fàww. Yal nañu torox, sànku.
Aji Sax ji dafa wax, moom buurub Israyil, jotkatam, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ne: «Maa jëkk, maa mujj, te yàlla amul ndare man.