Waaye dinaa fas kóllëre ak yaw, nga dugg ci gaal gi, yaak say doom ak sa soxna ak say soxnay doom.
TSK
TSK · Exodus 6:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Aji Sax ji wax Ibraam ne ko: «Déglul bu baax li ma lay wax: sa askan dinañu nekk ay doxandéem ci réew mu ñu moomul, ñu def leeni jaam, sonal leen diiru ñeenti téeméeri at.
«Man ci sama wàllu bopp, kóllëre gi ma fas ak yaw mooy lii. Dinga nekk maamu xeet yu baree bare.
Te réew mi nga doon ab doxandéem léegi, muy réewu Kanaan mépp, jox naa la ko, yaak sa askan, ngeen moom ko fàww. Te dinaa doon seen Yàlla.»
«Dama di doxandéem ci seen biir, tey gan; moo tax ma di leen ñaan, ngeen sédd ma bàmmeel bu ma suul sama néew, ba mu làqu ma.»
Yal na la barkeb Ibraayma dal, yaak askan wi soqikoo ci yaw, ba nga moom réew mii ngay doxandéem tey, te Yàlla mayoon ko Ibraayma.»
Maa leen di yóbbu ba ngeen dugg réew ma ma giñoon ne maa koy jox Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, te maa leen koy moomale, man Aji Sax ji.»
Kon keroog bu leen Aji Sax ji yóbboo réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, fa mu giñaloon seeni maam, ne dina leen ko jox, réew mu meew maak lem ja tuuroo, nangeen wormaal màggal gi ci wii weer te ngeen di ko defe nii.
Mu ne: «Yaw laay jox réewum Kanaan, muy sa cér, nga séddoo.»
Teewluleen te dikk fi man. Dégluleen, ba mana dund, ma fas ak yeen kóllëre gu sax, gi ma baaxee Daawuda ci ngor gu wóor.