Te wax naa la ne la, nga bàyyi sama doom, ndax mu man maa jaamu, nga bañ. Kon nag dinaa rey sa taaw bu góor.’ ”»
TSK
TSK · Exodus 7:14
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Teewul, ba Firawna gisee ca mbir ma tan, daa wéye të, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
Ndax boo leen bañee bàyyi kat, xanaa di leen téye ba tey, loxol Aji Sax ji dina dal ci sa kaw jur gi ci tool yi, muy fas ak mbaam ak giléem, jur gu gudd ak gu gàtt, te jàngoro ju aaytal lool lay doon.
Ba mu ko defee Firawna gis ne tawub yuur baak dënu ya dakk na, mu tëëti ticc, mooki dagam, dellu cig tooñam.
Soo bañee bàyyi sama ñoñ, ñu dem kat, ëllëg dinaa wàcce ay njéeréer ci sam réew.
Teewul Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, mu të rekk, bañ leena bàyyi ñu dem.
Ana lu jar ngeen di jaay dëgër bopp ni waa Misraak Firawna? Ba leen Yàllay Israyil torxalee, bàyyiwuñu bànni Israyil, ñu dem seen yoon?
Lu tax xeet wii dëddu? Lu tax Yerusalem gii lajj, baña délsi? Ñu ngi langaamoo naxi neen, baña délsi.
Seen bopp lañu dëgëral niw doj, ba faaleetuñu ndigalu yoon wi, ak kàddu yi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi yónnee ag Noowam, ci jottlib yonent yu jëkk ya. Muy sànj mu réy nag, bawoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.