Gannaaw loolu Firawna sant waa réew ma yépp, ne leen: «Mboolem doom ju juddu ci Ebrë yi, di góor, sànnileen ca dex ga, waaye lu ciy jigéen, bàyyileen, mu dund.»
TSK
TSK · Exodus 7:17
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Firawna ne: «Kan mooy Aji Sax ji, ba ma di ko déggal, di bàyyi Israyil, ñuy dem? Xawma sax kuy Aji Sax ji, waxumalaa may bàyyi Israyil, ñuy dem.»
Keroog bu ma tàllalee sama loxo, tiimale ko Misra, ba génnee bànni Israyil ca seen biir, waa Misra dinañu xam ne maay Aji Sax ji.»
Góoru Yàlla ga dikk ne buurub Israyil: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw waa Siri dañoo yaakaar ne man Aji Sax ji, yàllay tund laa, duma yàllay xur, maay teg mbooloo mu réy mii mépp ci say loxo. Su ko defee ngeen xam ne maay Aji Sax ji.»
Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, fakktaloo fiir ga ñu làqoon.
Yal nañu rus, jàq ba fàww. Yal nañu torox, sànku.
Réewum Misraay gental, di ndànd-foyfoy, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji. Moo ne: ‘Dex gi maa ko moom, man maa ko sàkk!’
Nii laay wàcceele Misra ay mbugal, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.”»
Bu ma defee réewum Misra ab gent, ba réew mi feesoon, ne faraas, bu ma dumaa mboolem ku ci dëkkoon, su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.”
Dinañu xam ne maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen yóbbu woon ngàllo ca yéefar ya, ba noppi délloosi leen seen suuf, te bawuma kenn gannaaw.
Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»
dàqe ko ci nit ñi, def xel ma xelum rab. Mu dëkk ak mbaami àll yi, am ñax dim xontam niw nag, lay biy wàcc, di ko faam, ba kera ba mu xamee ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.
¶ Ñaareelu malaaka mi wal liitam, mu am lu mel ni tund wu réy wuy tàkk, ñu sànni ko ci géej gi, ñetteelu xaaju géej gi soppiku deret,
¶ Ñaareelu malaaka mi sotti ndabam ci géej gi. Mu soppiku deret ju mel ni lu nàcce ci ku ñu bóom. Lépp lu doon dund biir géej daldi dee.