TSK

TSK · Exodus 7:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Kon nag waxal bànni Israyil ne leen: Man maay Aji Sax ji. Maa leen di sippil, yeen bànni Israyil, li leen waa Misra sëf, te maa leen di teggil njaam, gi ñu leen teg. Maay tàllal sama loxo, dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel leen.

Ñu jal koo jal, ba xet ga ubale ca réew ma.

Musaa ne ko: «Loolu du yoon, ndax li nuy rendil sunu Yàlla Aji Sax ji, waa Misra dañu koy xof. Te bu nu sarxalee lenn lu waa Misra xof, ñuy gis, dinañu nu dóor ay doj, ba nu dee.

Bu ma dumaa Firawna, boole kooki watiiram aki gawaram, ba doxe fa siiwal sama ndam, waa Misra dinañu xam ne man maay Aji Sax ji.»

Maa leen di feye mbugalu xadar yu mag, te bu ma leen yenee sama peyu mbugal, ñu xam ne maay Aji Sax ji.»

Kon dinaa fésal sama sellngay tur wu màgg, wi ñu teddadil fi biir yéefar yi, sama tur wi ngeen teddadil fi seen biir. Ci yeen laay fésale sama sellnga, yéefar yiy gis, ba xam ne maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Bésub keroog la waa kër Israyil di dale xam ne maay seen Yàlla Aji Sax ji.