TSK

TSK · Exodus 8:22

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Ni ngay xame ne man maay Aji Sax ji nii la: Dama ne, dinaa dóor ci ndoxum Niil mi yet, wi ci sama loxo, ndox mi soppliku deret;

Waaye man Aji Sax ji maay ràññatle juru bànni Israyil ak juru waa Misra, ba lenn du dee ci mboolem lu bànni Israyil moom.”»

Diiwaanu Gosen, ga bànni Israyil dëkkoon doŋŋ, moo mucc ca tawub yuur ba.

Kenn gisul sa moroom, kenn manula jóge fa nga nekk, diiru ñetti fan. Teewul këri bànni Israyil gépp di leer.

Deret ji ci kër, yi ngeen dëkke nag, mooy doon seen xàmmikaay, ba tax bu ma gisee deret ji, musal leen. Su ko defee bu may dal ci kaw réewum Misra, menn musiba du leen lor.

Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ. Yilifal noon yi la wër!

Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante ku jub ak ku bon, kuy jaamu Yàlla, ak ku ko jaamuwul.