Sirus buuru Pers nag sant Mittredat farbay alalam, mu génne ko, daldi koy waññal Sesbasar, boroom Yuda.
TSK
TSK · Ezra 5:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba ñu dikkee ca kër Yàlla ga ca Yerusalem, ba ca déwén sa, ca ñaareelu weeru at ma, Sorobabel doomu Selcel, ak Yosuwe doomu Yoccadag ànd nañook ña des ca seeni bokk, sarxalkat yaak Leween ñaak mboolem ña jóge ca njaam ga délsi Yerusalem. Ñu daldi tàmbali liggéey bi. Ci biir loolu ñu tabb ay Leween ñu am ñaar fukki at, jëm kaw, ñuy saytu liggéeyu kër Aji Sax ja.
¶ Ba loolu amee doomu Selcel, Sorobabel, ak doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ak mboolem ña des ca askan wa, ñoom ñépp déggal seen wooteb Yàlla Aji Sax ji, ak kàddug Yonent Yàlla Ase, noonee ko ko seen Yàlla Aji Sax ji yóbbantee. Askan wa nag ragal Aji Sax ji.
Léegi nag, Sorobabel, góor-góorlul, Aji Sax jee ko wax. Yaw doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, góor-góorlul; yeen mboolem askanu réew mi, góor-góorluleen, kàddug Aji Sax jee. Mu ne: Liggéeyleen, maa ànd ak yeen déy, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
¶ Gannaaw gi Aji Sax ji won ma Yosuwe sarxalkat bu mag ba, mu taxaw fa kanam malaakam Aji Sax ji, Tuumaalkat bi taxaw féete ko ndijoor, ngir tuumaal ko.
¶ Ma dellu wax ak malaaka ma doon wax ak man, ne ko: «Yëf yii nag, lu mu wund, Sang bi?»
Mu ne ma: «Ñooñu ñoo di ñaar ñi ñu diw, fal leen, ngir ñu liggéeyal boroom àddina sépp.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Yeen ñi dégg kàddu yii tey ci gémmiñu yonent yi fekke woon ba ñuy teg kenug kër Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ngir tabaxaat kër gi, nangeen góor-góorlu.