Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe, di gàntal li mbooloo yiy mébét;
TSK
TSK · Galatians 2:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Nu ngeen man ne: “Am nan xel, nungeek yoonu Aji Sax ji,” te xalimay yoonalkat soppi ko fen?»
¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
Gannaaw aw yiw a tax nag, dootu seen peyu jëf, lu ko moy aw yiw noppee doon aw yiw.
Su Almasi dekkiwul, sunu waare neen na, te seen ngëm it neen na.
Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di joxe àtteb ku jub, xanaa ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla jox nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di joxe kenn àtteb ku jub.
¶ Ndax kon yoonu Musaa dafa juuyoo ak digey Yàlla? Mukk kay. Ndax kat su fekkoon ne dañoo maye wenn yoon wu mana may nit ku ko sàmm, mu dund, konoon àtteb ku jub fi kanam Yàlla mana jóge dëgg ci sàmm gu nit ki sàmm yoon wi.
¶ Kon liggéeyu carxal gu Leween, ñi yoroon yoonu Musaa, wi ñu dénkoon bànni Israyil, su doon liggéey buy taxa mat sëkk, ndax dees na soxlaati beneen sarxalkat bu jóg topp dayob Melkisedeg, te toppul dayob Aaróona?