TSK

TSK · Galatians 5:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ñu wax seen magi dëkk ba, ne leen: «Sunu doom jii ku dëgër bopp la te të. Déggalu nu, xanaa di xawaareek a màndi rekk.»

Waaye ñi fétteeral ci seen sàkkuteefi bopp, nanguwuñoo topp liy dëgg, xanaa ag njubadi nag, ñooñu, am sànj ak mer mu ne jippét lañuy yooloo.

Nanu jëfe jëfin wu jekka def bëccëg; nanu sore xawaare ak màndite, sore baane bu lewul, ak yàqute yu ni mel, te sore ŋaayoo ak kiñaan.

¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,

Ndax lii kat na leen wóor: képp ku nekke powum séy, mbaa jëfi sobe, mbaa ag bëgge, kooku amul cér ci nguurug Almasi ak Yàlla, ndax ku bëgge ab bokkaalekat la.

yooyooy wàcce sànjum Yàlla ci kaw ñi déggadi.

¶ Xanaa fàttlikuwuleen ne waxoon naa leen ko, ba ma nekkee ak yeen?

Du lenn lu sobewu lu fay dugg nag, mbaa defkatu jëf ju ruslu ak njublaŋ. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Gàtt bi doŋŋ ñoo fay dugg.