TSK

TSK · Genesis 1:31

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yàlla tudde dénd wi asamaan. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñaareel ba.

Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñeenteel ba.

Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp.

Ndax man Aji Sax ji, juróom benni fan laa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak mboolem li ci biir, bésub juróom ñaareel ba, ma dal-lu. Moo tax man Aji Sax ji ma barkeel bésub Noflaay, sellal ko.

Job 38:7 TSK

ba biddiiwi njël sarxolleendoo, goney Yàlla yépp xaacoondoo?

Éy Aji Sax ji, yaa bare loo liggéey, te lépp di xel mu rafet. Suuf daa fees ak say càkkéef.

Lépp la Yàlla def, ba bu jotee rafet. Moo may nit muy njort ëllëg, te taxul mu mana ràññee jëf ji Yàlla jëf, njàlbéen ba muj ga.

Ndaxte li Yàlla sàkk lépp a baax, du lenn lees ciy aayal, ndegam kàddug cant lees ko jariñoo.