TSK

TSK · Genesis 10:22

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ca jamonoy Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar, Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim,

Ci jamonoom la Tiglaat Pilser buurub Asiri song réew ma, Menayem jox ko ñetti téeméeri barigoy xaalis ngir mu jàpple ko, ba nguuram gëna dëgër.

Job 1:17 TSK

Kooka daaneelagul kàddoom, keneen dikk ne: «Kaldeen ñaa def ñetti gàngoor, dikk sëxëtoo giléem ya, yóbbu, surga ya, ñu leel leen ñawkay saamar. Mennum man doŋŋ maa ca rëcce ba àggesi la ko.»

Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. Workat biy wor, yàqkat biy yàq. Yeen waa Elam, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.

Maay teg firnde fi seen digg, ba jël ñenn ca ña dese bakkan ca ñoom, yebal leen ci xeet yi, yebal leen Tarsis, ak Pul ak Ludd, ñooña di ñu mane fitt, ma yebal leen ca waa Tubal ak Yawaan, waa duni géej yu sore ya, ñooñu masula dégg sama jaloore, te masuñoo gis sama teddnga, sama ndaw ñaa leen di xamal sama teddnga.

¶ Kàddug Aji Sax ji dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi, jëm ci Elameen ñi, ci njàlbéenu nguurug Cedesyas buurub Yuda. Mu ne: