TSK

TSK · Genesis 12:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»

Su ko defee doo nu def dara lu bon, gannaaw defunu la dara lu bon, xanaa lu baax rekk, ba yebal la, nga dem ci jàmm. Kon léegi yal na la Aji Sax ji barkeel.»

Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele.

ndaxte lu néew nga amoon laata may ñëw, te yokku na, ba bare lool, ngir Aji Sax ji da laa barkeel ndax man. Waaye léegi nag, liggéeyal sama waa kër bopp jot na xanaa?»

Waaye su ngeen ko déggalee ba déggal ko, di jëfe li ma leen wax lépp, su boobaa ma noonoo seeni noon, bañ seeni bañaale.

yal na turam sax, ba law fu jant tiim, yal na xeet yépp barkeele ci moom, te di ko ndokkle.

Gannaaw gi la jagoo màndargam xaraf, mu firndeel àtteb njubam gi ngëmam waral, te fekkul mu xaraf. Noonu la Ibraayma mana nekke maamu mboolem gëmkat ñi. Looloo tax muy maamu mboolem ñi xaraful, te gëm, ndax ñu waññal leen seen ngëm, ab àtteb ñu jub.

Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»

Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu.

Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.