¶ Kanaan moo taawloo Sidon, teg ca Ett,
TSK
TSK · Genesis 15:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Dogu naa leena jële ci seen notaange gii ngeen nekke ci Misra, yóbbu leen ca réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, réew mu meew maak lem ja tuuroo.’ ”
Maay yebal malaaka mu jiitu la, te maa fay dàqe Kanaaneen ña ak Amoreen ña ak Etteen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña,
Amalegeen ñaa dëkke bëj-saalumu réew ma, Etteen ñaak Yebuseen ñaak Amoreen ña dëkke diiwaanu tund ya, Kanaaneen ña dëkke wetu géej, feggook dexu Yurdan.»
Ba loolu amee Musaa yebal ay ndaw, ñu yëri dëkk ba ñuy wax Yaser. Gannaaw gi bànni Israyil nangu dëkk-dëkkaan ya, daldi fay dàqe Amoreen ña.
Nangeen faagaagal Etteen ñi ak Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñi ak Yebuseen ñi, na leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante woon,