TSK

TSK · Genesis 19:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax ji da ne: «Su ñu tàmbalee nii, di menn mbooloo te bokk wenn làkk, kon dara dootu leen të.

Waa ja ne ko: «Ku la def sunu njiit mbaa sunu àttekat? Xanaa danga maa nara rey, na nga reye woon waa Misra ja?» Musaa nag tiit, naan ca xelam: «Ndeke mbir mi kay siiw na.»

ne ko: «Dikkal fii rekk, ba ma leele saw suux njanaaw yeek rabi àll yi.»

Artu kuy ñaawle, feyoo saaga rekk, yedd ab soxor, yooloo loraange.

Taseek gaynde gu ñàkki doomam moo gën taseek dof ak yëfi dofam.

Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf: Benn dogal la ñépp bokk, te it nit a ngi sóobu ci mbon, di mébét jëfi dof giiru dundam, ba noppi fekki ña dee.

te ñu naan: «Dellul gannaaw, bul ma jege, maa la gëna sell!» Lii déy daa mel ni saxar ci samay wakkan, mel ni sawara su yendoo boy.

Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu, te gàcce gàcceelu leen. Xamuñu sax luy kersa! Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu. Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.» Aji Sax jee ko wax.

¶ Ci kaw loolu Nabukodonosor mer lool ba fees dell, kanam gay sël-sëli janook Sadarag Mesag ak Abet Nego. Mu santaane ñu xamb taal ba, ba mu gëna tàng juróom ñaari yoon na mu daan tànge;

Acts 7:26 TSK

Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, di leen jéema jubale, ne leen: “Yeen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di lorante?”