TSK

TSK · Genesis 2:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund.

¶ Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja.

Aji Sax jeey dëfal Siyoŋ moos, dëfalaale fépp fu fa dib gent, ba def màndiŋam ni toolub Àjjana, jooram gu wow mel ni toolub Aji Sax ji, mbégteek bànneex teew fa, ak cant gu woy feelu.

Yaa nga woon biir Àjjana, toolub Yàlla ba, ràngoo lépp luy gànjari per, sarduwan ak topaas ak jamaa ak kirsolit ak onigsë ak jàspë ak safiir ak emëródd ak eskarbukal. Fegukaay yaak wewukaay ya di wurus, te bés ba ñu la sàkkee, fekk na ñu waajal yooyu.

Maa def xeet yi dégg jéllu seedar gi, di lox, ba ma ko tàbbalee njaniiw, boole kook mboolem ñiy tàbbim pax, ba mboolem garabi Àjjana gëna taaru, ak yay ngëneeli Libaŋ, ak mboolem ya màndim ndox, ñoom ñépp di fa muñe seen demin, la seedar ga teew ni ñoom biir xóotey suuf.

Joel 2:3 TSK

Lu leen jiitu, sawara lekk; lu leen topp, ag daay xoyom. Ni toolub Àjjana la réew mi ci seen kanam di mel, ñu won ko gannaaw, muy màndiŋ mu wéet, te kat dara du leen rëcc.