TSK

TSK · Genesis 23:16

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Déglu ma, kilifa gi, suuf suy jar ñeenti téeméeri dogi xaalis doŋŋ du dara ci sama diggante ak yaw; tee nga faa denc sa néew rekk?»

¶ «Lii nag mooy li képp ku ñu bind ci limeef yi wara fey: dogu xaalis bu diisaay bi di genn-wàllu siikal, bi ñuy natte ci jaamookaay bi, dayo boobu tollook fukki gera, mu dib jooxe, ñeel Aji Sax ji.

Ezra 8:25 TSK

Gannaaw loolu ma nattal leen xaalis baak wurus waak ndab, ya Buur aki wóllëreem aki jawriñam jooxe woon, ñook mbooloom Israyil ma fa teewoon, te lépp jëm ca sunu kër Yàlla ga.

¶ Nii laa jënde tool ba ca Anatot ci Anamel sama doomu baay bu ndaw. Ma waññal ko xaalis bi, muy fukki donji xaalis ak juróom ñaar.

Benn siikal, na wecciku ñaar fukki gera, te boo boolee nattu ñaar fukki siikal, ak nattu ñaar fukki siikal ak juróom, ak nattu fukki siikal ak juróom, mu wara wecciku benn natt bi ñuy wax miin.

¶ Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.