TSK

TSK · Genesis 24:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ibraam ne ko: «Yaw Aji Sax ji sama Boroom, nan la may wóore ne maa koy moom?»

mu ne ma: ‘Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,’ kooku na di soxna, si Aji Sax ji jagleel sama doomu sang.”

Kon waajal-leen watiir bu bees te ngeen jël ñaari nag yuy nàmpal yu ñu masula takkal. Ngeen takkal nag yi watiir bi te yóbbu doomi nag yi, fat.

Yonatan ne ko: «Ayca nu dem ba ca ñoom, feeñu leen.

Su nee baax na de, sang bi, sama jàmm la, waaye su sànjoo ba sànju nag, xamal ne musiba la nar.

Yowab ne Amasa: «Mbokk mi, mbaa jàmm nga am?» Yowab jàpp sikkimu Amasa ca loxol ndijooram, mel ni ku koy fóon.

Kër ak alal ngay donne ci baay; jabar ju xelu, Aji Sax jee koy maye.

Xanaa di saxoo dagaan ci samay ñaan, su ci Yàlla àndee, yoon wu jub wu ma mujj dikke ba ci yeen.