TSK

TSK · Genesis 28:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ba loolu weesee mu doora lekk, daldi naan, moom ak ñi mu àndal. Ñu fanaan fa keroog. Ba ñu yewwoo ca ëllëg sa, surga ba ne: «Bàyyileen ma nag, ma dellu ca sama sang.»

waaye demal Padan Aram ca sa kër maam-góor, ji jur sa yaay, nga jël fa jabar ca sa doomi nijaay Laban.

Ci kaw loolu Yàlla feeñu Laban, Arameen ba, ci géntu guddi ne ko: «Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.»

Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.