TSK

TSK · Genesis 29:32

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

tegaat ca ne ko: «Léegi jigéenu wérul nga, te dinga am doom ju góor; nanga ko tudde Ismayla (mu firi Yàlla dégg na), ndax Aji Sax ji yég na sa naqar.

¶ Ba Israyil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israyil yég ko. Doomi Yanqóoba yu góor fukk lañu ak ñaar.

¶ Ruben nag dégg ca, di ko fexee xettli. Mu ne leen: «Bunu ko rey.»

Ruben nag àddu ne leen: «Ndax newuma leen woon: “Buleen gàddu bakkanu xale bi,” waaye faalewuleen ma; tey rekk la nu Yàlla doon xaare bakkanam, bi nu gàddu.»

¶ Waa kër Israyil, yi ñëw Misra te di Yanqóoba aki doomam, seeni tur a di: Ruben, taawub Yanqóoba.

¶ Aji Sax ji tegaat ca ne ko: «Gis naa bu baax fitna, ji sama ñoñ nekke Misra. Dégg naa itam seen jooy ndax kilifay saskat, yi leen di gétën ci liggéey, te ñeewante naa leen ngir seen coono.

Ba loolu amee nu yuuxu, woo sunu Yàllay maam Aji Sax ji wall, Aji Sax ji dégg nu, gis sunu mitit, ak sunu coono, ak sunu notaange.

Ci biir loolu mu xas aw xas, daldi ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Sang bi, soo nemmiku woon ba nemmiku njàqare jii ma nekke, bàyyi ma xel, bañ maa fàtte, ba may ma doom ju góor! Kon déy, maa ko sédde Aji Sax ji, giiru dundam gépp, saatus watukaay du jaar ci boppam mukk!.»

Jombul Aji Sax ji gis sama naqar, ba feye ma aw yiw saagay kii tey.»

Xoolal sama naqar ak sama tiis, te baal ma bépp bàkkaar.

Suufas Ruben day digalook sos Efrayim, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc.