Mu ne ko: «Damaa dégg say tànk ci tool bi, tiit, ndax yaramu neen laa def, ma daldi làqu.»
TSK
TSK · Genesis 3:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Waaye lu nuy jaayati nag sunu bakkan, doye? Ndax kat, sawara wu réy wii, su nu déggatee sunu kàddug Yàlla Aji Sax ji, da nuy xoyom.
Niir yee ko làq ba du nu gis, fa muy doxantoo ca kaw taaxum asamaan!»
Yàlla déy a ngi ne jàkk ci jaar-jaari nit ki, di xool bépp jéegoom.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji, yaa ma natt, xam ma;
Ku mana làqoo làquwaay, ba duma ko gis?» Kàddug Aji Sax jee. «Xanaa du asamaan ak suuf, maa ko fees?» Kàddug Aji Sax jee.
¶ Yunus nag jóg jëm Tarsis, ngir daw Aji Sax ji. Mu àgg fu ñuy wax Yafa, fekk fa gaal gu mag gu jëm Tarsis. Mu fey njég ga, dugg, ànd ak ña ca nekk, jëm Tarsis, ngir daw Aji Sax ji.
Noonu lañu wérale ne jëf ji yoonu Musaa santaane moo binde ci seenub xol, ba seen yég-yégu xol seede loolu. Li koy firndeel it di seen xel miy def leeg-leeg mu sikk leen, leeg-leeg mu dëggal leen.