TSK

TSK · Genesis 31:24

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Teewul genn guddi Yàlla feeñu Abimeleg ci gént ne ko: «Yaw dee nga ba noppi, ndax jigéen, ji nga nangu, soxnas jaambur la.»

Isaaxa daldi yebal Yanqóoba, mu dem Padan Aram ca Laban doomu Betuwel, Arameen bay càmmiñu Rebeka, miy yaayu Yanqóoba ak Esawu.

Manoon naa laa def lu bon, waaye sa Yàllay baay da maa feeñu biig ne ma: “Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.”

¶ jawriñi buuru Misra, ya ñu tëj, muy ñaar ña féetewoo naani buur ak mburoom, dañoo géntandoo ci genn guddi, gént gu ci nekk ak li muy firi.

Mu ne leen: «Dégluleen bu baax samay kàddu: su ngeen feeñlee ab yonentu Aji Sax ji, ci am peeñu laa koy xamale maay kan, te ci gént laay waxeek moom,

Malaakam Aji Sax ja dellu jiitu, ba taxawi fu xat, ba maneesula weesalook moom, du ndijoor, du càmmoñ.

Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.

Foofa ca Gabawon la Aji Sax ji feeñu woon Suleymaan ci géntug guddi. Yàlla ne ko: «Ñaanal loo bëgg, ma may la ko.»

Job 33:25 TSK

Yaram wa jotaat tooyaayu ndaw, mu amaat dooley ngoneem;

Yaa xadaru sama kaw, ba sag reewande tàbbi sama nopp! Maa lay takkal ag nos akug laab, waññi la, nga dellu yoon wa nga dikke woon.