¶ Laban ak Betuwel ne ko: «Mbir moomu de ci Aji Sax ji la jóge, te amunu ci dara lu nuy wax.
TSK
TSK · Genesis 31:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ci kaw loolu Yàlla feeñu Laban, Arameen ba, ci géntu guddi ne ko: «Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.»
Yàllay Ibraayma ak Yàllay Naxor, ñoom ñooñee di seen Yàllay baay, yal nañu àtte sunu diggante.» Yanqóoba daldi giñ ci Yàlla, ji baayam Isaaxa wormaaloon.
Absalom nag jéppi Amnon, ba séqatul ak moom jenn wax, ndax na mu torxale jigéenam Tamar.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel Daawuda.
¶ Nabukodonosor wax ne: «Cant ñeel na Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, moom mi yónni malaakaam, mu wallu jaamam ñi ko wóolu, ba xëtt sama ndigal man Buur, te jaay seen bakkan gënal leen ñuy jaamu mbaa di sujjóotal jeneen yàlla ju dul seen Yàlla.
¶ Gannaaw loolu Buur Daryus bind waa mbooloo yépp ak xeet yépp ak làkk yépp, di waa àddina sépp, ne: «Jàmm ngeen!
Léegi nag, dama ne, maanduleen ci ñii, te ba leen, ngir su seen mébét mbaa seen jëf bawoo ci nit, day yàqu rekk.