Te tuddatuloo Ibraam; léegi yaa di Ibraayma (mu firi Maamu ñu bare), ndax maa la def ngay maamu xeet yu baree bare.
TSK
TSK · Genesis 32:28
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yanqóoba ne ko: «Danga ma koy jëkka wecci sa céru ndono bi nga yeyoo ndax li ngay taaw.»
Ci kaw loolu Yàlla feeñu Laban, Arameen ba, ci géntu guddi ne ko: «Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.»
Yanqóoba da leena jàllale, jàllewaale alalam jépp itam.
Mu daldi fay sàkk sarxalukaay, tudde ko El Elowe Israyil (mu firi Yàllay Israyil mooy Yàlla).
¶ Ñooñu la Musaa yónni woon, ngir ñu yëri réew ma. Oseya doomu Nuun nag, Musaa tudde ko Yosuwe.
ba xamle ko, Yonent Yàlla Natan jottli, daldi koy tudde Yedija (mu firi Soppey Aji Sax ji).
Ba tey jii ñu ngi topp seen aaday cosaan. Ragaluñu Aji Sax ji dëgg te sàmmontewuñook santaane yeek dogal yeek yoon week ndigal li Aji Sax ji joxoon askanu Yanqóoba mi mu tudde Israyil.
Su boobaa xeet yi gis sag njekk, buur yépp gis sa daraja, ba ñu di la tudde tur wu yees, wu Aji Sax ji di tuddal boppam.
Aji Sax ji moo séq ak Yuda ab layoo, mooy mbugale Yanqóoba ay jëfinam, añale ko ay jëfam.
¶ «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may ci mànn mu làqu mi, nga lekk, maa lay jox it aw doj wu weex; doj wu ñu bind tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ka ko jot.