Yal na la Yàlla may layub asamaan ak ngëneeli suuf, pepp ne gàññ, biiñ walangaan.
TSK
TSK · Genesis 32:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndeke Aji Sax jaa nga tollu ca wetam. Mu wax ak moom ne ko: «Maay Aji Sax ji, di sa Yàllay maam Ibraayma te di Yàllay Isaaxa. Suuf si nga tëdd dinaa la ko jox, yaak sa askan.
ne ko: «Yaa di Yanqóoba, waaye deesatu la wooye Yanqóoba; léegi yaa di Israyil.» Mu tudde ko nag Israyil.
daldi jël fukki doj ak ñaar, mu tollook limu giiri doomi Yanqóoba. Yanqóoba la kàddug Aji Sax ja dikkaloon ne ko Israyil ay doon turam.
Ana ku yéegoon asamaan, ba wàcc? Mbaa mu masa ŋëb ngelaw ciy loxoom? Ana ku masa ëmb ndox ci ndimo? Mbaa mu rëdd mboolem kemi àddina? Nu mu tudd ak nu doomam tudd? Wax ma, yaw mi ko xam!
Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji. Moo nu xotat, te moo nuy wéral. Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.