TSK

TSK · Genesis 33:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»

Mu sàkkal leen ca ndabam, te Beñamin ëpple ku ci nekk juróomi yoon. Ñu bokk nag naana naan, ba seen xol sedd.

Mu laxasu Beñamin rakkam, daldi jooy, Beñamin it laxasu ko, jooy.

Xale ba dem, Daawuda jóg, génne ca làquwaayam ba fare bëj-saalum. Mu ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot ñetti yoon, ku nekk fóon sa moroom, ñoom ñaar ñépp jooy, te Daawuda rawati.

Job 2:12 TSK

Ñu dikk ba jub ko, di ko séentoo fu xawa sore, waaye xàmmeetuñu ko. Ñu daldi ne yikkét jooy. Ba ñu agsee ku ci nekk ne sa mbubb tareet. Ñuy ñaawlu, di tibb suuf, di sànni ca kaw, muy sottiku ci seen kaw bopp.

Ku Aji Sax ji rafetlu say jëf, say bañ sax, mu jubaleek yaw.

¶ «Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.